8 Na génne lépp luy nebbon ci yëkk wi ñuy sarxal muy póotum bàkkaar: nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
9 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
10 Mooy ni ñu koy génnee rekk ci yëkku saraxu cant ci biir jàmm. Sarxalkat bi da koy boole lakk ca kaw sarxalukaayu rendi-dóomal ba.
11 Waaye deru yëkk wi ak yàppam wépp dees koy booleek bopp bi ak yeel yi ak yérey biir yi ak sébbriit mi;
12 mboolem li des ci yëkk wi daal lay génne dal bi, yóbbu ko ci bérab bu mucc sobe, ca jalub dóom ba, daldi taal matt, lakk ko ca, ba mu dib dóom. Foofa dóom ba jale lees koy lakk.
13 «Ndegam mbooloom Israyil mépp a moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du seen teyeef, muy seenug tooñ te seetluwuñu ko,
14 bu mbooloo mi nemmikoo moy gi rekk, war nañoo génne ci jur gu gudd gi yëkk wu ndaw wuy doon saraxu póotum bàkkaar, yóbbu ko ca bunt xaymab ndaje ma.