7 Na sarxalkat bi sàkk ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaayu cuuraay lu xeeñ la ca biir xaymab ndaje ma ca kanam Aji Sax ji. Li des ci deretu yëkk wi, na ko tuur ci taatu sarxalukaay bi ñuy lakk saraxu rendi-dóomal, foofa ca bunt xaymab ndaje ma.
8 Na génne lépp luy nebbon ci yëkk wi ñuy sarxal muy póotum bàkkaar: nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
9 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.