Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 4:23-30 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 4:23-30 in Kàddug Yàlla gi

23 bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe sikket bu amul sikk.
24 Day teg loxoom ci boppu sikket bi, rendi ko fa ñuy rendi saraxu rendi-dóomal, fa kanam Aji Sax ji. Saraxu póotum bàkkaar la.
25 Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deretu sarax siy póotum bàkkaar, taqal ko ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ba noppi tuur deret ji ci taatu sarxalukaayu rendi-dóomal bi.
26 Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
27 «Su dee kenn ci baadoolo yee moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,
28 bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe aw bëy wu jigéen wu amul sikk, ndax bàkkaar bi mu def.
29 Day teg loxoom ci boppu gàttu sarax soosu di póotum bàkkaar, rendi ko fa ñuy lakk saraxu rendi-dóomal.
30 Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi; li des ci deret ji da koy tuur ci taatu sarxalukaay bi.
Sarxalkat yi 4 in Kàddug Yàlla gi