Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 3:5-9 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 3:5-9 in Kàddug Yàlla gi

5 Na doomi Aaróona yi boole yooyu lakk ci kaw sarxalukaay bi, mu tege ci kaw saraxu rendi-dóomal bi ci kaw mattum taal bi. Saraxu sawara la ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji.
6 «Su fekkee ne li nit kiy sarxalal Aji Sax ji saraxu cant la ci biir jàmm, te mu di ko jële ci jur gu gàtt, gu góor mbaa gu jigéen, na sarxal lu amul sikk.
7 Su dee sarxal xar, na ko indil Aji Sax ji
8 te teg loxoom ci boppu xar mi muy sarxe, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi, doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
9 Li muy génne ci saraxu cantu biir jàmm bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, mooy nebbon bi, ak calgeen bi yépp, ñu doge ko fa sës ca fàllare ja, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
Sarxalkat yi 3 in Kàddug Yàlla gi