Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 27:32-34 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 27:32-34 in Kàddug Yàlla gi

32 Mboolem céru fukkeel bu ñu génnee cig jur, gu gudd gaak gu gàtt ga, muy lépp lu sàmm waññe bantam, cérub fukkeel la bu ñuy sellalal Aji Sax ji.
33 Deesu ci seet jur gu baax ak gu bon te deesu ci wuutal lenn. Bu ci nit xasee wuutal lenn, la jëkk ak la ko wuutu lépp day daldi doon lu sell. Deesu ko mana jotaat.»
34 Yooyu santaane la Aji Sax ji dénkoon Musaa ca tundu Sinayi, ngir mu jottli ko bànni Israyil.
Sarxalkat yi 27 in Kàddug Yàlla gi