Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 27:18-33 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 27:18-33 in Kàddug Yàlla gi

18 Waaye su fekkee ne gannaaw atum Yiwiku la joxe suuf si, sarxalkat bi da koy nattal njég gi ci at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca topp, génne ca at ya wees.
19 Su fekkee ne ki dogu woona joxe tool bi da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
20 Su jotaatul tool bi, ba ñu jaay tool bi keneen, deesu ko mana jotaat.
21 Bu tool bi yiwikoo ci atum Yiwiku nag, day daldi doon lu ñu sellalal Aji Sax ji, mel ni tool bu ñu aaye, mu doon alalu sarxalkat.
22 «Su fekkee ne nit ki dafa jagleel Aji Sax ji tool bu mu jënd, te donnu ko,
23 sarxalkat bi da koy xaymaal njég gi, méngale kook at yi dox seen digganteek atum Yiwiku may ñëw. Na nit ki fey la ñu xayma ca bés ba, xaalis ba di lu ñuy sellalal Aji Sax ji.
24 Bu atum Yiwiku dikkee, tool bi day dellu ca ka ñu ko jënde woon te mu di alalu ndonoom.
25 Mboolem lu ngeen xayma, na dëppook natt ba ñu yoonal ci bérab bu sell bi, maanaam li ñuy wax siikal te mu tollu ci fukki garaam.
26 «Waaye kat luy taaw cig jur, Aji Sax jee ko moom jeeg. Du lu kenn di dogoo jagleel Aji Sax ji. Muy barmol, muy mbote, muy tef, Aji Sax jeey boroom.
27 Su dee lu mala mu daganul taawloo, ka ko moomoon man na koo jotaat ndegam fey na njégam, ba dolli ca xaajub juróomeelu njég ga. Bu ñu ko jotaatul, dees koy jaay ci njég gi ñu ko xaymaa.
28 Mboolem lu ñu aayalal Aji Sax ji, lu sella sell la ñeel Aji Sax ji. Lépp lu nit moom, su dee nit mbaa jur mbaa suuf su mu donn, amu ci lenn lu mu aayalal Aji Sax ji te ñu sañ koo jaay mbaa mu di ko jotaat.
29 Ba tey du kenn nit ku ñu aayalal bakkanam Aji Sax ji, mu wara sànku, ba noppi ñu di ko jotaat. Dees koy rey rekk.
30 «Bu loolu weesee mboolem lu jóge ci suuf, muy pepp mbaa doomi garab, cérub fukkeel ba Aji Sax jeey boroom. Dees koy sellalal Aji Sax ji.
31 Su fekkee ne nit ki dafa namma jotaat lenn ca céru fukkeelu meññeefam ma muy génne, day yokk ca njég ga xaajub juróomeelam.
32 Mboolem céru fukkeel bu ñu génnee cig jur, gu gudd gaak gu gàtt ga, muy lépp lu sàmm waññe bantam, cérub fukkeel la bu ñuy sellalal Aji Sax ji.
33 Deesu ci seet jur gu baax ak gu bon te deesu ci wuutal lenn. Bu ci nit xasee wuutal lenn, la jëkk ak la ko wuutu lépp day daldi doon lu sell. Deesu ko mana jotaat.»
Sarxalkat yi 27 in Kàddug Yàlla gi