Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 27:10-22 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 27:10-22 in Kàddug Yàlla gi

10 Deesu ko weccee. Du jur gu baax gu ñu ko mana wuutoo, doonte jur gu bon la, te du jur gu bon gu ñu ko mana wuutoo, te fekk muy gu baax. Ci biir jagleel googu ku xasa wuutoo ag jur moroom ma, jur gu jëkk gaak kuutaay la dañuy bokk doon lu sell.
11 Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe mala mu daganul la te daganula sarxalal Aji Sax ji, na nit ki yóbbu jur ga ba ca sarxalkat ba,
12 sarxalkat ba xayma ko. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
13 Su ko boroom bëggee jotaat, day fey njég ga, yokk ca xaajub juróomeelu njég ga.
14 «Su nit jagleelee Aji Sax ji dëkkuwaayam, sellalal ko ko, na sarxalkat bi xayma dëkkuwaay bi. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
15 Su fekkee ne ki dogu woona joxe dëkkuwaayam da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
16 «Su nit jagleelee Aji Sax ji suuf su mu moom ci suufas ndonoom, na ñuy xaymaa suuf sa, na dëppook dayob pepp bay mat jiwum suuf sa. Ñetti barigoy peppum lors yu ne juróom fukki dogi xaalis a koy wecci.
17 Su fekkee ne ci atum Yiwiku la joxe suuf si, xaymab suuf si day mat sëkk ànd ak moom.
18 Waaye su fekkee ne gannaaw atum Yiwiku la joxe suuf si, sarxalkat bi da koy nattal njég gi ci at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca topp, génne ca at ya wees.
19 Su fekkee ne ki dogu woona joxe tool bi da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
20 Su jotaatul tool bi, ba ñu jaay tool bi keneen, deesu ko mana jotaat.
21 Bu tool bi yiwikoo ci atum Yiwiku nag, day daldi doon lu ñu sellalal Aji Sax ji, mel ni tool bu ñu aaye, mu doon alalu sarxalkat.
22 «Su fekkee ne nit ki dafa jagleel Aji Sax ji tool bu mu jënd, te donnu ko,
Sarxalkat yi 27 in Kàddug Yàlla gi