Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 26:38-46 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 26:38-46 in Kàddug Yàlla gi

38 Dingeen deeye àll, te seen suufu noon yaa leen di lekk.
39 Ñi des ci yeen dinañu ràgg ca seen réewi noon ndax seeni bàkkaar ak seen bàkkaari maam.
40 «Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo,
41 ba man itam ma noonoo leen, toxal leen seen réewu noon. Bu ñu tuubee seen xol bu dëgër nag, ba matal seen mbugal yi sababoo ci seeni ñaawtéef,
42 su boobaa maay bàyyi xel ci sama kóllëre gaak Yanqóoba ak sama kóllëre gaak Isaaxa ak sama kóllëre gaak Ibraayma, te duma fàtte li ma dige ci wàllu réew mi.
43 «Waaye réew mi dinañu ko gental, mu daboo ati Noflaayam diir ba ñu ko dëddoo, wéetal ko, te fekk ñoom ñuy fey seen boru tooñ; ndax kat dañoo sofental samay santaane, xalab samay dogal.
44 Ndaxam du tax ma sofental leen ca seen réewu noon, mbaa ma di leen xalab, di leen faagaagal, nde kon ma fecci sama kóllëreek ñoom. Ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
45 Maa leen di bàyyil xel ci sama kóllëre gaak seen maam ya ma génne réewum Misra, jaambur ñi seede, ngir doon seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.»
46 Looloo di dogal yaak santaane yaak ndigali yoon ya Aji Sax ji tëral ca digganteem ak bànni Israyil ca kaw tundu Sinayi, Musaa jottli leen ko.
Sarxalkat yi 26 in Kàddug Yàlla gi