Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 26:19-27 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 26:19-27 in Kàddug Yàlla gi

19 Maay sàggi seen sag bu réy. Maay def asamaan si leen tiim ne sereŋ nig weñ, suuf si wow koŋŋ ni xànjar.
20 Seen doole dina kasara, ndax suuf si ngeen di bey du leen nangul te garabi réew mi du meññ.
21 «Su ngeen saxee ci noonoo ma, bañ maa déggal, maay fulaat seen mbugal fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar.
22 Maay xabtal rabi àll yi ci seen kaw, ñu xañ leen seeni doom, seeni gétt ñu tas, seeni nit ñu néewal, ba seeni mbedd ne wëyëŋ.
23 «Su ma leen loolu yaralul ba tey, xanaa ngeen sax ci noonoo ma,
24 su boobaa man itam maa leen di noonoo, te it man ci sama bopp maa leen di mbugalaat lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar.
25 Maay dalal saamar ci seen kaw, feye leen ko kóllëre gi ngeen fecci. Bu ngeen làqoo ci seeni biir dëkk yu mag sax, maay wàcce mbas ci seen biir, seeni noon jekku leen.
26 Bu ma téyee loxo bi ma leen di leele, fukki jigéen dinañu bokk lakk seen mburum njël ci benn taal doŋŋ, natt ko ay somp, séddale, ngeen lekk, te dungeen suur.
27 «Waaye bu loolu weesee te déggaluleen ma, xanaa di ma noonoo ba tey,
Sarxalkat yi 26 in Kàddug Yàlla gi