Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 26:18-21 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 26:18-21 in Kàddug Yàlla gi

18 «Bu loolu taxul ngeen déggal ma, maa leen di mbugal lu ko ëpp juróom ñaari yoon, feye leen ko seeni bàkkaar.
19 Maay sàggi seen sag bu réy. Maay def asamaan si leen tiim ne sereŋ nig weñ, suuf si wow koŋŋ ni xànjar.
20 Seen doole dina kasara, ndax suuf si ngeen di bey du leen nangul te garabi réew mi du meññ.
21 «Su ngeen saxee ci noonoo ma, bañ maa déggal, maay fulaat seen mbugal fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar.
Sarxalkat yi 26 in Kàddug Yàlla gi