Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 26:14-17 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 26:14-17 in Kàddug Yàlla gi

14 «Waaye bu ngeen ma déggalul te baña jëfe sama santaane yooyu yépp,
15 su ngeen teddadilee samay dogal, dëddu samay ndigal, ba jëfewuleen sama santaane yépp, xanaa di fecci sama kóllëreek yeen,
16 su boobaa li may def ak yeen mooy lii: maay jekki wàcce njàqare ci seen kaw, mu ànd ak woppi ràgg, yaram wu tàng jérr ak bët yu lëndëm, ngeen gën di wopp. Dingeen ji seenum pepp ci neen, ndax seeni noon a koy lekk.
17 Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen.
Sarxalkat yi 26 in Kàddug Yàlla gi