Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 25:8-22 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 25:8-22 in Kàddug Yàlla gi

8 «Gannaaw loolu nangeen waññ ba ci juróom ñaari ati Noflaay, loolu di juróom ñaari at ba muy juróom ñaari yoon. Mu doon seen juróom ñaari ati Noflaay, tollu ci ñeent fukki at ak juróom ñeent.
9 Su boobaa ci fukki fan ca juróom ñaareelu weer wa nangeen wal-lu ag liit fépp. Bésub Njotlaay boobu nangeen wal ag liit ci seenum réew ba mu daj.
10 Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk.
11 Seen atum Yiwiku la atum juróom fukkeel boobu di doon. Dungeen ci ji, dungeen ci góobaat lu saxe ca seenum ngóob te dungeen ci wolli ag reseñ, di ko witt.
12 Gannaaw atum Yiwiku la, na doon at mu ngeen sellal. Saxayaayub tool ngeen saña lekk.
13 «Atum Yiwiku moomu ci ngeen di delloo ku nekk suufam.
14 Bu ngeen di jaay seen waa réew suuf nag mbaa ngeen di jënde suuf ci seen waa réew, buleen di naxante.
15 Limu at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma mujj, na dëppook njég gi ngeen di jënde suuf ci seen waa réew. Limu ati mbey yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca toppaat it, war naa dëppook njég ga ñu leen jaaye.
16 Lu at yooya gëna bare, njég ga gëna jafe; lu at ya gëna néew, njég ga gëna yomb, ndaxte limu meññeefum suuf sa lees leen koy jaaye.
17 Buleen di naxante, waaye ragal-leen seen Yàlla, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
18 «Saxleen ci samay dogal, sàmm samay ndigali yoon, di ko jëfe, ndax ngeen dëkk ak jàmm ci réew mi.
19 Kon suuf si dina nangu, ngeen di lekk ba suur te dëkk fa ci jàmm.
20 Jombul ngeen di wax naan: “Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?”
21 Waaye dinaa leen yónnee sama barke ca atum juróom benneel ba, suuf si nangul leen meññeefum ñetti at.
22 Bu ngeen tolloo ci ji ci atum juróom ñetteel ba, dina leen fekk ngeen di lekk meññeefum daaw-jéeg, te meññeefum atum juróom ñeenteel ba dina agsi, fekk ngeen di lekk ca mu daaw-jéeg ma.
Sarxalkat yi 25 in Kàddug Yàlla gi