Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 25:47-55 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 25:47-55 in Kàddug Yàlla gi

47 «Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal mbaa ab màngaan dafa woomle te kenn ci seeni bokk ñàkk, ba jaay boppam doxandéem bi ngeen dëkkal mbaa kenn ku bokk ak doxandéem bi,
48 gannaaw bu jaayee boppam, manees na koo jotaat ba tey. Kenn ciy bokkam sañ na koo jotaat,
49 yaar muy baayam bu ndaw mbaa doomu baayam bu ndaw. Ku mu bokkal làng di mbokkam lenqe sax man na koo jotaat, te moom ci boppam man naa woomle ba jotaat boppam.
50 Na bokk ak ka ko jënd waññ, la dale ca at ma mu jaaye boppam, ba ca atum Yiwiku may ñëw, muy njégu goreelam, dëppook at yooya. Te it nañu ci seet àqu ñaqu liggéeykat.
51 Su desee ay at, lu at ya gëna baree, njég ga muy jotaate boppam gëna sore ci njég, ga ñu ko jënde woon.
52 Te su at yu néew doxee seen digganteek atum Yiwiku ma, na ko waññ te fey lu ni néewe, ngir jotaat boppam.
53 Ab surga lay doon ci njaatigeem at mu nekk, waaye waru koo soxore ci biir kilifteef, ngeen di seetaan.
54 Su fekkee ne jotaatuñu ko ci jotin yooyu sax, war naa moom boppam mooki doomam ca atum Yiwiku ma.
55 Ndax kat man la bànni Israyil di samay jaam. Ñoo di sama jaam ya ma génne réewum Misra; yeen, maay seen Yàlla Aji Sax ji.
Sarxalkat yi 25 in Kàddug Yàlla gi