3 Diiru juróom benni at ngeen di ji seen tool; juróom benni at yooyu itam ngeen di wolli seen tóokëru reseñ, dajale meññeef ma.
4 Waaye atum juróom ñaareel ba atum Noflaay la wara doon: suuf sa ca boppam day nopplu doŋŋ ngir Aji Sax ji. Buleen ci ji seen tool, buleen ci wolli seen tóokëru reseñ.
5 La saxe ca seenum ngóob sax, buleen ko góobaat te it reseñ gu ñu wolliwuloon buleen ko raasaatu. Atum Noflaay la wara doon: suuf sa ca boppam na nopplu atum lëmm.
6 Waaye lépp luy saxayaay ci atum Noflaay sañ ngeen koo lekk, yeen ak seen jaam yu góor ak yu jigéen, ak seeni surga ak doxandéem bu dal ak yeen.
7 Seen jur it ca la, ba ca rabi àll ya ca seen réew. Mboolem lu suuf sa meññ, manees na koo lekk.
8 «Gannaaw loolu nangeen waññ ba ci juróom ñaari ati Noflaay, loolu di juróom ñaari at ba muy juróom ñaari yoon. Mu doon seen juróom ñaari ati Noflaay, tollu ci ñeent fukki at ak juróom ñeent.
9 Su boobaa ci fukki fan ca juróom ñaareelu weer wa nangeen wal-lu ag liit fépp. Bésub Njotlaay boobu nangeen wal ag liit ci seenum réew ba mu daj.
10 Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk.
11 Seen atum Yiwiku la atum juróom fukkeel boobu di doon. Dungeen ci ji, dungeen ci góobaat lu saxe ca seenum ngóob te dungeen ci wolli ag reseñ, di ko witt.
12 Gannaaw atum Yiwiku la, na doon at mu ngeen sellal. Saxayaayub tool ngeen saña lekk.
13 «Atum Yiwiku moomu ci ngeen di delloo ku nekk suufam.
14 Bu ngeen di jaay seen waa réew suuf nag mbaa ngeen di jënde suuf ci seen waa réew, buleen di naxante.
15 Limu at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma mujj, na dëppook njég gi ngeen di jënde suuf ci seen waa réew. Limu ati mbey yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca toppaat it, war naa dëppook njég ga ñu leen jaaye.