Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 25:27-51 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 25:27-51 in Kàddug Yàlla gi

27 day waññ at ya njaay ma am, delloo ki mu jaayoon ati mbey ya ca kooka dese, daldi mana jotaat ci suufam.
28 Waaye su amul lu mu jëndaate suufam, suuf sa day des ca loxol ka mu jaayoon, ba keroog atum Yiwiku ma délsi. Bu atum Yiwiku ma délsee, sañ naa dellu ca suufam.
29 «Su dee waa ju jaay ab dëkkuwaay bu nekk ci dëkk bu mag bu ñu tabax tata wëralee ko ko, dina ko saña jotaat li feek njaay mi amul at. Ci diir boobu la ko saña jotaate.
30 Su ñu ko jotaatul ba njaay ma am atum lëmm, dëkkuwaay boobu ci biir dëkk bu mag ba ñu wëralee tata day wel fàww, ñeel ka ko jënd, mook ku askanoo ci moom. Du lees di delloo ci atum Yiwiku.
31 Su dee ay dëkkuwaay ci dëkk yu ndaw yu ñu tabaxul tata, wëralee ko ko, dees koy yemaleek alali suuf. Sañees na koo jotaat te dees koy delloo ci atum Yiwiku.
32 «Su dee dëkki Leween ñi ak seen dëkkuwaay ya ca biir nag, Leween ñi sañ nañu cee jotaat fàww.
33 Kon alalu Leween manees na koo jotaat —dëkkuwaay lay doon bu ñu jaay ci dëkki Leween ñi— dees koy delloo bu atum Yiwiku dikkee, ndax dëkkuwaay yi ci dëkki Leween ñi, seen alal la ju leen lew fàww ci seen biir bokki bànni Israyil.
34 Waaye suufas parlu yi bokk ci dëkki Leween ñi, deesu ko jaay, ndax ñoo koy moom fàww.
35 «Bu seen mbokkum bànni Israyil ñàkkee ba manatula fey lu mu leen ameel, nangeen ko dimbali, ni bu doon doxandéem mbaa màngaan, ndax mu mana dund ci seen biir.
36 Buleen teg lenn lu mu mana doon ci bor bu leen seen mbokk moomu ameel, waaye ragal-leen ci seen Yàlla, ndax mu mana dund ci seen biir.
37 Buleen ko lebal seen xaalis, di ca teg lenn, te buleen ko jox dund, di sàkku lu mu ca yokk ngir delloo leen ko.
38 Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, jox leen réewu Kanaan, te di seen Yàlla.
39 «Bu seen mbokk ñàkkee ci seen biir, ba jaay leen boppam, buleen ko jaamloo.
40 Defleen ko ni liggéeykat buy feyeeku mbaa màngaan bu ngeen dëkkal. Na leen liggéeyal ba keroog atum Yiwiku ma,
41 mu génn ci seeni loxo, mook ay doomam, daldi dellu ci làngu boppam, fa ay maamam séddoo.
42 Li waral loolu moo di bànni Israyil dañu di sama jaam yi ma génne réewum Misra. Deesu leen jaay njaam.
43 Buleen leen soxore ci biir kilifteef, waaye ragal-leen ci seen Yàlla.
44 Seen jaam yu góor ak seen jaam yu jigéen, nangeen leen jële ci xeet yi leen wër. Ci ñooñu ngeen di jënde ay jaam, góor ak jigéen.
45 Walla ngeen jënde ba tey ci doxandéem yi ci seen biir, mbaa ci njaboot yi doxandéem yi am ci réew mi te ñu nekk ci seen biir. Su ko defee ñu doon seen ngàllo.
46 Sañ ngeen leena donale seen doom yi leen di wuutu, ñu doon seen ngàllo seen giiru dund. Ñooñu sañ ngeen leena def ay jaam, waaye su dee ci seen diggante, yeen bànni Israyil, buleen di soxorante ci biir kilifteef.
47 «Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal mbaa ab màngaan dafa woomle te kenn ci seeni bokk ñàkk, ba jaay boppam doxandéem bi ngeen dëkkal mbaa kenn ku bokk ak doxandéem bi,
48 gannaaw bu jaayee boppam, manees na koo jotaat ba tey. Kenn ciy bokkam sañ na koo jotaat,
49 yaar muy baayam bu ndaw mbaa doomu baayam bu ndaw. Ku mu bokkal làng di mbokkam lenqe sax man na koo jotaat, te moom ci boppam man naa woomle ba jotaat boppam.
50 Na bokk ak ka ko jënd waññ, la dale ca at ma mu jaaye boppam, ba ca atum Yiwiku may ñëw, muy njégu goreelam, dëppook at yooya. Te it nañu ci seet àqu ñaqu liggéeykat.
51 Su desee ay at, lu at ya gëna baree, njég ga muy jotaate boppam gëna sore ci njég, ga ñu ko jënde woon.
Sarxalkat yi 25 in Kàddug Yàlla gi