2 «Waxal bànni Israyil ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, suuf sa ca boppam war naa am àppu noflaayam ngir Aji Sax ji.
3 Diiru juróom benni at ngeen di ji seen tool; juróom benni at yooyu itam ngeen di wolli seen tóokëru reseñ, dajale meññeef ma.
4 Waaye atum juróom ñaareel ba atum Noflaay la wara doon: suuf sa ca boppam day nopplu doŋŋ ngir Aji Sax ji. Buleen ci ji seen tool, buleen ci wolli seen tóokëru reseñ.