Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 25:14-31 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 25:14-31 in Kàddug Yàlla gi

14 Bu ngeen di jaay seen waa réew suuf nag mbaa ngeen di jënde suuf ci seen waa réew, buleen di naxante.
15 Limu at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma mujj, na dëppook njég gi ngeen di jënde suuf ci seen waa réew. Limu ati mbey yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca toppaat it, war naa dëppook njég ga ñu leen jaaye.
16 Lu at yooya gëna bare, njég ga gëna jafe; lu at ya gëna néew, njég ga gëna yomb, ndaxte limu meññeefum suuf sa lees leen koy jaaye.
17 Buleen di naxante, waaye ragal-leen seen Yàlla, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
18 «Saxleen ci samay dogal, sàmm samay ndigali yoon, di ko jëfe, ndax ngeen dëkk ak jàmm ci réew mi.
19 Kon suuf si dina nangu, ngeen di lekk ba suur te dëkk fa ci jàmm.
20 Jombul ngeen di wax naan: “Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?”
21 Waaye dinaa leen yónnee sama barke ca atum juróom benneel ba, suuf si nangul leen meññeefum ñetti at.
22 Bu ngeen tolloo ci ji ci atum juróom ñetteel ba, dina leen fekk ngeen di lekk meññeefum daaw-jéeg, te meññeefum atum juróom ñeenteel ba dina agsi, fekk ngeen di lekk ca mu daaw-jéeg ma.
23 «Suuf si deesu ko jaay, mu wel fàww, ndax maay Boroom suuf si, yeen ay doxandéem ngeen fi, yu ma fi dëkkal.
24 Fépp fu bokk ci seenum réew, nangeen fa yoonal sañ-sañu jotaat ca suuf sa.
25 «Bu sa mbokk demee ba ñàkk tax koo jaay ci suufam, mbokkam mi ko gëna jege te am sañ-sañu jotaat suufam, na jëndaat la mbokk ma jaayoon.
26 Ku amul ku ko ko jotaatal te moom ci boppam mu mujj woomle, ba am lu mu ko jotaate,
27 day waññ at ya njaay ma am, delloo ki mu jaayoon ati mbey ya ca kooka dese, daldi mana jotaat ci suufam.
28 Waaye su amul lu mu jëndaate suufam, suuf sa day des ca loxol ka mu jaayoon, ba keroog atum Yiwiku ma délsi. Bu atum Yiwiku ma délsee, sañ naa dellu ca suufam.
29 «Su dee waa ju jaay ab dëkkuwaay bu nekk ci dëkk bu mag bu ñu tabax tata wëralee ko ko, dina ko saña jotaat li feek njaay mi amul at. Ci diir boobu la ko saña jotaate.
30 Su ñu ko jotaatul ba njaay ma am atum lëmm, dëkkuwaay boobu ci biir dëkk bu mag ba ñu wëralee tata day wel fàww, ñeel ka ko jënd, mook ku askanoo ci moom. Du lees di delloo ci atum Yiwiku.
31 Su dee ay dëkkuwaay ci dëkk yu ndaw yu ñu tabaxul tata, wëralee ko ko, dees koy yemaleek alali suuf. Sañees na koo jotaat te dees koy delloo ci atum Yiwiku.
Sarxalkat yi 25 in Kàddug Yàlla gi