Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 24:7-10 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 24:7-10 in Kàddug Yàlla gi

7 Jal bu nekk teg ca cuuraay lu raxul, mu wuutu mburu mi, di saraxu baaxantal, te di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
8 Bésub Noflaay bu nekk nañu saxoo taaj mburu yooyu fi kanam Aji Sax ji. Loolu sas la bu bànni Israyil di tegoo fàww.
9 Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu sell, ndaxte lu sella sell la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.»
10 Ba loolu wéyee amoon na ci biir bànni Israyil jenn waay ju yaayam di doomu Israyil te tuddoon Selomit doomu Dibbri, Daneen ba. Baayam di waa Misra. Mu am bés xeex jib ci biir dal bi, ci diggante waa jooju ak jenn waayi Israyil ju raxul. Ci biir loolu waa ji yaayam di doomu Israyil wax Yàlla lu ñaaw, tudd ko jaar fu bon. Ñu yóbbu ko ca Musaa.
Sarxalkat yi 24 in Kàddug Yàlla gi