17 «Bu loolu weesee képp ku faat bakkanu nit, dee rekk mooy àtteem.
18 Ku faat bakkanu mala, na fey boroom. Bakkan, bakkan a koy fey.
19 Képp ku gaañ moroomam, la mu ko def rekk lañu koy def.
20 Damm-damm, damm-damm a koy fey; bët, bët a koy fey; bëñ it bëñ a koy fey. Ni mu gaañe moroomam rekk, ni lañu koy gaañe.
21 «Ku rey ag jur na fey boroom, waaye ku rey nit dee mooy àtteem.
22 Na àtte bi di benn ci doxandéem ak njuddu-ji-réew, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.»