Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 24:13-23 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 24:13-23 in Kàddug Yàlla gi

13 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko:
14 «Génneel dal bi ki may wax lu ñaaw, man Yàlla, te na mboolem ku ci dégg teg loxoom ci kaw boppam, ba noppi mbooloo mépp dóor koy doj, ba mu dee.
15 Bànni Israyil nag nangeen leen wax ne leen: Képp ku wax Yàllaam lu ñaaw, jaar fu bon, na wéetoo añam.
16 Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem.
17 «Bu loolu weesee képp ku faat bakkanu nit, dee rekk mooy àtteem.
18 Ku faat bakkanu mala, na fey boroom. Bakkan, bakkan a koy fey.
19 Képp ku gaañ moroomam, la mu ko def rekk lañu koy def.
20 Damm-damm, damm-damm a koy fey; bët, bët a koy fey; bëñ it bëñ a koy fey. Ni mu gaañe moroomam rekk, ni lañu koy gaañe.
21 «Ku rey ag jur na fey boroom, waaye ku rey nit dee mooy àtteem.
22 Na àtte bi di benn ci doxandéem ak njuddu-ji-réew, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.»
23 Ci kaw loolu Musaa wax ko bànni Israyil, ñu génne dal ba waa ja ñàkke Yàlla kersa, dóor ko ay doj, ba mu dee. Kon li bànni Israyil def mooy li Aji Sax ji santoon Musaa rekk.
Sarxalkat yi 24 in Kàddug Yàlla gi