Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 24:12-17 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 24:12-17 in Kàddug Yàlla gi

12 Ñu tëj waa ja, ba xam lu Aji Sax ji namm ci moom.
13 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko:
14 «Génneel dal bi ki may wax lu ñaaw, man Yàlla, te na mboolem ku ci dégg teg loxoom ci kaw boppam, ba noppi mbooloo mépp dóor koy doj, ba mu dee.
15 Bànni Israyil nag nangeen leen wax ne leen: Képp ku wax Yàllaam lu ñaaw, jaar fu bon, na wéetoo añam.
16 Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem.
17 «Bu loolu weesee képp ku faat bakkanu nit, dee rekk mooy àtteem.
Sarxalkat yi 24 in Kàddug Yàlla gi