Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 22:9-13 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 22:9-13 in Kàddug Yàlla gi

9 Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal.
10 «Kenn ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi du lekk ci sarax yu sell yi. Muy ku dal ak ab sarxalkat, muy ku koy liggéeyal di feyeeku, kenn du ci lekk ci sarax yu sell yi.
11 Waaye su sarxalkat bi jëndee ab jaam ci xaalisam, jaam ba man na caa lekk. Jaam bu juddoo ci kër sarxalkat bi it man naa lekk ci ñamam woowu.
12 Doomu sarxalkat, bu séyeek góor gu bokkul ci waa kër sarxalkat yi, jooxe yu sell yi, dootu ci saña lekk.
13 Waaye doomu sarxalkat bu boroom këram faatoo mbaa mu tàggook moom te amu ca doom, bu delloo kër baayam na mu fa nekke woon ba muy gone, sañ naa lekk ci ñamu baayam. Waaye kenn ku ci bokkul sañu cee lekk.
Sarxalkat yi 22 in Kàddug Yàlla gi