Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 22:21-23 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 22:21-23 in Kàddug Yàlla gi

21 «Su nit dee joxsi Aji Sax ji aw nag mbaa gàtt, muy saraxu cant ci biir jàmm, mu di ko wàccoo ngiñ mbaa muy saraxu yéene, na doon lu amul sikk, ndax ñu nangul ko. Lenn luy sikk du nekk ci jur gi.
22 Du doon lu gumba, du doon lu làggi, du doon lu kuuñ, du doon lu ami góom, mbaa lu ràmm, mbaa lu xas. Buleen sarxalal Aji Sax ji yu mel noonu. Ab saraxu sawara, buleen ko jële ci lu mel noonu, di ko joxe ci kaw sarxalukaay bi, ñeel Aji Sax ji.
23 Waaye su dee nag mbaa gàtt bu ab céram ëpp mbaa mu yées, saraxu yéene la mana doon; su dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ, deesu ko nangu.
Sarxalkat yi 22 in Kàddug Yàlla gi