5 «Buñu wat fenn ci seen bopp te buñu wat seen peggi sikkim, buñu dagg seen yaram it, di ko mititloo ku dee.
6 Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.
7 «Ab gànc mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, ñoom duñu ko jël soxna. Ku jëkkëram baal it duñu ko jël soxna, ndax dañoo sellalal seen bopp seen Yàlla.