Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 21:3-7 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 21:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 mbaa ab jigéenam bu séyagul te bootu ci moom ndax amul jëkkër— ku mu bokkal noonu, sañ naa sobewu ndax moom.
4 Warula sobeel boppam, di teddadil boppam, ndax kilifa la ciw xeetam.
5 «Buñu wat fenn ci seen bopp te buñu wat seen peggi sikkim, buñu dagg seen yaram it, di ko mititloo ku dee.
6 Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.
7 «Ab gànc mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, ñoom duñu ko jël soxna. Ku jëkkëram baal it duñu ko jël soxna, ndax dañoo sellalal seen bopp seen Yàlla.
Sarxalkat yi 21 in Kàddug Yàlla gi