14 Ku jëkkëram faatu mbaa ku ñu baal mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, mbaa ab gànc, du ko mana jël soxna. Ab janq bu mu bokkal doŋŋ la mana jël soxna.
15 Su ko defee du teddadil aw askanam ci biir bànni Israyil, ndax man Aji Sax ji maa ko sellal.»
16 Bu loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
17 «Waxal Aaróona ne ko: Muy tey muy ëllëg ba fàww, góor gu askanoo ci yaw ak maas gu mu mana bokk, su amee sikk du mana agsi ba ci sarxalukaay bi, di joxe ñamu Yàllaam.
18 Du kenn sax ku am sikk kuy agsi ba fii, du gumba, du kuy soox, du ku xar-kanamam am sikk mbaa ku cér yi sutaate.
19 Du it ku tànk bi làggi mbaa loxo bi,
20 mbaa ab xuuge mbaa ab tungune; du it ku bëtam am sikk mbaa ku ràmm mbaa ku am góom yu sol dëtt, mbaa ku ñu tàpp.