13 «Su góor tëddee góor ni ñuy tëddee jigéen, ñaawtéef lañu def ñoom ñaar. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
14 Ku boole nit ak ndeyam jël leen jabar, def na lu bona bon. Dees leen di boole taal, lakk leen, moom ak jigéen ña, ndax mbon gu ni mel baña am ci seen biir.
15 Góor gu tëdde mala dee rekk mooy àtteem, te mala ma it dees koy rey.
16 Su jigéen jëmee ci mala mu mu doon, ba jaxasook moom, booleleen ku jigéen kaak mala ma, rey. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
17 «Su nit jëlee jabar ab jigéenam bu mu bokkal jenn ndey mbaa benn baay, ñu séq lalu séy, loolu gàcce la. Nañu leen dagge ci biir bànni Israyil, ñooñuy gis. Gannaaw moo tëdde ab jigéenam, na wéetoo añu ñaawtéefam.
18 «Ku tëdde jigéen ju gis baax, torxal na ko, xàwwi na suturaam ci biir póotam te ku jigéen ki itam xàwwi na suturas boppam. Dees leen wara dagge ñoom ñaar ñépp ci biir bànni Israyil.
19 «Buleen dëkkoo seen yaay ju ndaw mbaa seen bàjjan, ndax kon torxal ngeen ku ngeen jegewool lool cig bokk, te yeen ñaar ñépp ay wéetoo seen añu ñaawtéef.
20 «Ku dëkkoo soxnas baayam bu ndaw, baayam bu ndaw la torxal. Ñooy wéetoo seen añu ñaawtéef. Duñu am takkndeer ba keroog ñuy dee.
21 «Bu nit nangoo jabaru ku mu bokkal waajur, loolu gàcce la. Torxal na ka mu bokkal waajur te duñu am takkndeer.
22 «Sàmmleen sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te jëfe ko, ngir réew ma ma leen jëme, ngeen dëkki fa, bañ leena gëq.
23 Buleen roy defini xeet wi ma leen di dàqal, ndax yooyu yépp lañu doon def, ba ma sib leen.