Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 20:12-15 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 20:12-15 in Kàddug Yàlla gi

12 Ku dëkkoo sa soxnas doom, mook soxnas doomam ñoom ñaar ñépp dee mooy seen àtte. Jëfu yàqute lañu def, kon ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
13 «Su góor tëddee góor ni ñuy tëddee jigéen, ñaawtéef lañu def ñoom ñaar. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
14 Ku boole nit ak ndeyam jël leen jabar, def na lu bona bon. Dees leen di boole taal, lakk leen, moom ak jigéen ña, ndax mbon gu ni mel baña am ci seen biir.
15 Góor gu tëdde mala dee rekk mooy àtteem, te mala ma it dees koy rey.
Sarxalkat yi 20 in Kàddug Yàlla gi