Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 20:1-15 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 20:1-15 in Kàddug Yàlla gi

1 Aji Sax ji wax na Musaa ba tey ne ko:
2 «Waxal bànni Israyil ne leen: Muy bànni Israyil muy doxandéem ci Israyil, képp ku ci jël ciy doomam, jébbal tuur mi ñuy wax Moleg, dee rekk mooy àtteem. Na ko waa réew mi dóor ay doj, ba mu dee.
3 Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.
4 Su fekkee ne waa réew mi dañu koo seetaan ba seetaan ko, muy jox Moleg ku bokk ciy doomam te taxul ñu rey ko,
5 man ci sama bopp maay noonoo nit kooku mook ay bokkam; dinaa dagge nit kooku ci biir bànni Israyil, génne ko, mook mboolem ñi mu àndal topp Moleg di bokkaale.
6 Ku jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee mbaa mu jublu ci boroom rawaan yiy seet, topp leen, di ma leen bokkaalee, dinaa ko noonoo moom itam te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.
7 Sell-luleen te sell, ngir man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
8 Nangeen sàmm samay dogali yoon te di ko jëfe. Man Aji Sax ji maay ki leen sellal.
9 «Képp ku saaga baayam mbaa ndeyam, dee rekk mooy àtteem. Gannaaw baayam la saaga mbaa ndeyam, mooy gàddu bakkanu boppam.
10 «Góor gu njaaloo, mook jabaru moroomam ji muy njaalool, dee rekk mooy seen àtte.
11 «Ku dëkkoo sa soxnas baay, sa baay nga torxal. Ñoom ñaar ñépp dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
12 Ku dëkkoo sa soxnas doom, mook soxnas doomam ñoom ñaar ñépp dee mooy seen àtte. Jëfu yàqute lañu def, kon ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
13 «Su góor tëddee góor ni ñuy tëddee jigéen, ñaawtéef lañu def ñoom ñaar. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
14 Ku boole nit ak ndeyam jël leen jabar, def na lu bona bon. Dees leen di boole taal, lakk leen, moom ak jigéen ña, ndax mbon gu ni mel baña am ci seen biir.
15 Góor gu tëdde mala dee rekk mooy àtteem, te mala ma it dees koy rey.
Sarxalkat yi 20 in Kàddug Yàlla gi