Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 19:3-11 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 19:3-11 in Kàddug Yàlla gi

3 «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.
4 «Buleen walbatiku di jaamu ay yàllantu mbaa ngeen di sàkkal seen bopp ay tuur yu ñu móole weñ. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
5 «Bu ngeen dee rendil Aji Sax ji saraxas cant ci biir jàmm, sarxal-leen ko ni mu ware, ndax ñu nangul leen.
6 Ca bés ba ñu ko sarxale lees koy lekk, mbaa ca ëllëg sa; lu ca des ba ca gannaaw ëllëg sa dees koy lakk, ba mu dib dóom.
7 Bu ñu ci lekkee déy te fekk mu am ñetti fan, day doon lu ñu sib, te deesu ko nangu.
8 Ku ci lekk mooy gàddu bàkkaar bi, ndaxte lu ñu sellalal Aji Sax ji la teddadil, te kooku dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.
9 «Bu ngeen dee góob seen tool, buleen góob ba fa tool ba yem te buleen ca toppaat, di foraatu.
10 Seen tóokëri reseñ it buleen ko witt ñaari yoon te buleen foraatu doom yu wadde ca witt ma. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla, man Aji Sax ji.
11 «Buleen sàcc, buleen fen te buleen di worante.
Sarxalkat yi 19 in Kàddug Yàlla gi