27 Buleen wat seen peggu kawaru bopp te buleen dagg seen peggu sikkim,
28 mbaa ngeen di dagg seen yaram, di ko mititloo ku dee, te buleen ñaasu fenn ci seen yaram. Maay Aji Sax ji.
29 «Buleen torxal seen doom ju jigéen, di ko def ab gànc; lu ko moy réew mi sóobu ci gànctu ba ne lijj ci ñaawtéef.
30 «Samay bési Noflaay nag wormaal-leen ko te sama bérab bu sell teral-leen ko. Maay Aji Sax ji.
31 «Buleen jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee te buleen jublu ci boroom rawaan yiy seet, ndax kon ñu sobeel leen. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji.