Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 19:21-33 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 19:21-33 in Kàddug Yàlla gi

21 Waa ji day yóbbu am kuuyu peyug tooñ ca bunt xaymab ndaje ma, muy peyug tooñ, gi muy sarxalal Aji Sax ji.
22 Na ko sarxalkat bi defal kuuy miy saraxas peyug tooñ muy njotlaayam fi kanam Aji Sax ji, ndax bàkkaar bi mu def. Kon dees na ko jéggal bàkkaar bi mu def.
23 «Bu ngeen duggee ca réew ma, ba jëmbat fa mboolem xeetu garab guy meññ ay doom, nangeen aayal doom ya. Diiru ñetti at ngeen di aayal doom ya. Dungeen ko lekk ci diir boobu.
24 Atum ñeenteel ba doom ya yépp lañuy sellalal Aji Sax ji, te di ko bége ci biir cant.
25 Juróomeelu at ma doŋŋ ngeen di saña lekk doom ya. Su ko defee meññeef ma barkeelal leen. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
26 «Buleen lekk lu am deret. Buleen di gisaane mbaa ngeen di jibar.
27 Buleen wat seen peggu kawaru bopp te buleen dagg seen peggu sikkim,
28 mbaa ngeen di dagg seen yaram, di ko mititloo ku dee, te buleen ñaasu fenn ci seen yaram. Maay Aji Sax ji.
29 «Buleen torxal seen doom ju jigéen, di ko def ab gànc; lu ko moy réew mi sóobu ci gànctu ba ne lijj ci ñaawtéef.
30 «Samay bési Noflaay nag wormaal-leen ko te sama bérab bu sell teral-leen ko. Maay Aji Sax ji.
31 «Buleen jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee te buleen jublu ci boroom rawaan yiy seet, ndax kon ñu sobeel leen. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji.
32 «Bu boroom bijjaaw teewee, jógleen wormaal ko. Deeleen rus mag te ragal-leen seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.
33 «Bu ab doxandéem daleek yeen ci seenum réew, buleen ko lor.
Sarxalkat yi 19 in Kàddug Yàlla gi