19 «Te it sama dogali yoon yii nangeen ko sàmm: buleen boole ñaar yu bokkul wirgo ci seenug jur, ñuy jaxasoo; seen tool it buleen ci ji ñaari wirgoy jiwu te buleen sol yére yu ñu ràbbe ñaari xeeti wëñ yu bokkul.
20 «Ku tëdde ab jaam bu wara séy ak keneen te fekk joteesu ko, goreeleesu ko, ndàmpaay war na ca, waaye deesu leen boole rey, ndax li ndaw si dib jaam ba tey.
21 Waa ji day yóbbu am kuuyu peyug tooñ ca bunt xaymab ndaje ma, muy peyug tooñ, gi muy sarxalal Aji Sax ji.
22 Na ko sarxalkat bi defal kuuy miy saraxas peyug tooñ muy njotlaayam fi kanam Aji Sax ji, ndax bàkkaar bi mu def. Kon dees na ko jéggal bàkkaar bi mu def.
23 «Bu ngeen duggee ca réew ma, ba jëmbat fa mboolem xeetu garab guy meññ ay doom, nangeen aayal doom ya. Diiru ñetti at ngeen di aayal doom ya. Dungeen ko lekk ci diir boobu.