Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 18:3-10 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 18:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Defini waa réewam Misra ga ngeen dëkkoon, buleen ko roy, te defini waa réewu Kanaan ga ma leen jëme, buleen ko roy te it buleen leen topp ci seeni aada.
4 Samay santaane ngeen wara dégg tey topp samay dogal. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
5 Nangeen sàmm samay dogal ak samay santaane, ndax ngeen jëfe yooyu moo leen di taxa dund. Man maay Aji Sax ji.
6 «Bu kenn ci yeen dëkkoo ku mu jegewool lool cig bokk. Maay Aji Sax ji.
7 Bul torxal sa baay, di dëkkoo sa yaay. Sa yaay la, kon bu ko torxal moom it.
8 «Bul dëkkoo sa soxnas baay, di torxal sa baay.
9 «Bul dëkkoo sab jigéen, te muy koo bokkal benn baay mbaa koo bokkal jenn ndey, muy ku juddoo ci kër gi mbaa feneen.
10 «Bul dëkkoo sab sët bu jigéen bu sa doom ju góor jur mbaa sa doom ju jigéen, ndax kon torxal nga sa bopp.
Sarxalkat yi 18 in Kàddug Yàlla gi