Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 18:21-25 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 18:21-25 in Kàddug Yàlla gi

21 «Bul jébbal kenn ci say doom tuur mi ñuy wax Moleg, ndax waruloo teddadil sa turu Yàlla. Man maay Aji Sax ji.
22 «Bu góor tëdde góor, ni bu doon jigéen. Lu ñaawa ñaaw la.
23 «Bu góor tëdde menn mala, di sobeel boppam, te bu jigéen jox boppam mala, di ànd ak moom. Loolu yàqute la.
24 «Buleen sobeel seen bopp ci mboolem defin yooyu, ndax xeet yi ma leen dàqal, noonu lañu daan jëfe, ba sobeel seen bopp.
25 Réew ma sax mujj na daj ak sobe, ma wàcce mbugal ca kaw réew ma, ba mu gëq ay nitam.
Sarxalkat yi 18 in Kàddug Yàlla gi