Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 16:6-17 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 16:6-17 in Kàddug Yàlla gi

6 «Aaróona day sarxal yëkk wi, muy saraxu póotum bàkkaaram, di njotlaayal boppam, mook waa këram.
7 Gannaaw loolu na Aaróona indi ñaari sikket yi, taxawal fi kanam Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi.
8 Na Aaróona tegal ñaari sikket yi bant, ngir xam bu ñuy rendil Aji Sax ji ak biy doon ngir Asasel.
9 Su ko defee Aaróona indi sikket, bi muurloo, ñu sarxalal ko Aji Sax ji, rendi ko, muy saraxu póotum bàkkaar.
10 Waaye sikket bi muurloo doon sikketu Asasel, dees koy taxawal muy dund fi kanam Aji Sax ji, te ni ñu koy jotoo, mooy dees koy dàq mu dem ca màndiŋ ma, ngir Asasel.
11 «Bu Aaróona noppee, na indi yëkku saraxas póotum bàkkaaram, def ko njotlaayam mook waa këram. Na rendi yëkku saraxas póotum bàkkaaram,
12 te na sàkk andu xal bu fees, tibbe ko ca sarxalukaay ba, fi kanam Aji Sax ji, ak ñaari barci-loxoy cuuraay lu mokk te xeeñ, boole ko yóbbu ca gannaaw rido ba.
13 Na def cuuraay li ci taal bi, foofa ca kanam Aji Sax ji, saxaru cuuraay si di làq kubeeru saraxu njotlaay gi ub gaalu àlluway seede si, ndax mu baña dee.
14 Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi.
15 Bu noppee na rendi sikket biy saraxas póotum bàkkaaru mbooloo mi, te yóbbu deret ji ca gannaaw rido ba. Na def deret ji na mu defoon ak deretu yëkk wa, wis-wisal ko ca kaw kubeeru gaal gi ak ci kanam kubeer gi.
16 Mu daldi matale loolu njotlaayal bérab bu sell bee sell, tàggale kook sobey bànni Israyil ak seeni tooñ, ak lu seen bàkkaar mana doon. Noonu lay defal mboolem xaymab ndaje, mi dëkk ci seen biir ci seen biiri sobe.
17 Du kenn ku saña nekk ci biir xaymab ndaje mi, bu Aaróona duggee ci biir bérab bu sell bee sell, di matal ag njotlaay, ba keroog muy génn, gannaaw bu jotoo moom ci boppam, mook waa këram, ba jotaale mbooloom bànni Israyil mépp.
Sarxalkat yi 16 in Kàddug Yàlla gi