Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 16:12-14 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 16:12-14 in Kàddug Yàlla gi

12 te na sàkk andu xal bu fees, tibbe ko ca sarxalukaay ba, fi kanam Aji Sax ji, ak ñaari barci-loxoy cuuraay lu mokk te xeeñ, boole ko yóbbu ca gannaaw rido ba.
13 Na def cuuraay li ci taal bi, foofa ca kanam Aji Sax ji, saxaru cuuraay si di làq kubeeru saraxu njotlaay gi ub gaalu àlluway seede si, ndax mu baña dee.
14 Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi.
Sarxalkat yi 16 in Kàddug Yàlla gi