25 «Kuy xëpp deret ay fan yu bare te du jamonoy baaxam, mbaa mu gis mbërëg mu wees àpp bi mu ko baaxoo gis, kooka sobewu na diiru fan yi muy xëpp. Day mel ni bu nekkee ci jamonoy baaxam.
26 Lal bu mu tëdd ci diir bi muy xëpp yépp, day mel ni lalam bu ko fekk ci jamonoy baax te lépp lu mu toog day sobewu, ni bu nekkoon ci jamonoy baaxam.
27 Ku laal lenn ci yooyu yëf, kooka sobewu na. War naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
28 «Bu xëppee ba jeexal, dina waññ juróom ñaari fan, doora tàggook sobe sa.
29 Bésub juróom ñetteel ba na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, yóbbu ca sarxalkat ba, ca bunt xaymab ndaje ma.