2 «Waxleen ak bànni Israyil ne leen: Góor gu ànd ak jàngoro ju sabab ngóoraam di xelli mbér, kooku sobewu na.
3 Mbér mi muy xelli moo ko sobeel; su ngóora liy xelli mbér mbaa su ko mbér mi fattee, waa ji sobewu na.
4 Lal ba mu tëdd sobewu na, te lépp lu mu toog loola sobewu na.
5 Képp ku laal lalam, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
6 Ku toog ci lenn lu boroom jàngoroy xelli toogoon, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
7 Ku laal boroom jàngoroy xelli war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu ànd ak sobe ba jant so.
8 Su ku ànd ak jàngoroy xelli tiflee ku taqul sobe, na kooku fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
9 Gépp tegu daamar gu boroom jàngoroy xelli waroon, sobewu na.
10 Ku laal lenn lu mu toogoon lu ko féete woon suuf dina yendoo sobe ba jant so, te képp ku yékkati loola na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.