Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 15:14-23 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 15:14-23 in Kàddug Yàlla gi

14 Bésub juróom ñetteel ba, na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw te teewi fi kanam Aji Sax ji ca bunt xaymab ndaje ma, daldi koy jox sarxalkat bi.
15 Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di saraxu póotum bàkkaar, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju.
16 «Su góor génnee wasal, war naa ragg yaramam wépp, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
17 Lépp luy yére mbaa der bu wasal taq, dees koy fóot te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
18 Su dee jigéen ju góor àndal, te wasal génn, nañu sangu, te du tere ñu yendoo sobe ba jant so.
19 «Su jigéen gisee mbërëg, sobey mbërëg ma day ànd ak moom juróom ñaari fan te képp ku laal ku jigéen ka dina yendoo sobe ba jant so.
20 Lépp lu mu tëdd te fekk mu gis baax, loola sobewu na te lépp lu mu toog, loola sobewu na.
21 Te it képp ku laal ab lalam, war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
22 Képp ku laal lenn lu mu toogoon war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
23 Su toogoon ci lal mbaa leneen lu mu toogoon, ku laal loola dina yendoo sobe ba jant so,
Sarxalkat yi 15 in Kàddug Yàlla gi