Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 14:9-16 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 14:9-16 in Kàddug Yàlla gi

9 Bésub juróom ñaareel ba na watu ba set, bopp beek sikkim beek yeen yi ak kawar gi ci des yépp lay wat, fóot ay yéreem, sangu, daldi set.
10 Bésub juróom ñetteel ba na indi ñaari kuuy yu amul sikk, ak menn xar mu jigéen mu am at te amul sikk ak juróom ñeenti kiloy sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe diw, muy saraxu pepp. Mu indaale genn-wàllu liitaru diw.
11 Sarxalkat biy laabal nit ki day indi nit ki, mu ànd ak loolu lépp, taxaw fi kanam Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi.
12 «Sarxalkat bi teg ca jël menn kuuy mi, rendi ko, muy saraxu peyug tooñ, boole kook genn-wàll liitaru diw ga, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
13 Nañu rendi kuuy mi ci bérab bu sell bi, fi ñuy rendee juru saraxu póotum bàkkaar ak saraxu rendi-dóomal, ndax li nekk ci saraxu peyug tooñ moo nekk ci saraxu póotum bàkkaar: sarxalkat bee ko moom; lu sella sell la.
14 Na sarxalkat bi sàkk ci deretu jur giy saraxu peyug tooñ, taqal ko ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
15 Bu sarxalkat bi noppee, na sàkk ci genn-wàll liitaru diw gi, sotti ko ci biir loxol càmmoñu boppam.
16 Na sarxalkat bi capp baaraamu joxoñu ndijooram ci diw gi ci loxol càmmoñam, daldi wis-wisale diw gi baaraamam, ba mu mat juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji.
Sarxalkat yi 14 in Kàddug Yàlla gi