Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 14:30-56 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 14:30-56 in Kàddug Yàlla gi

30 Bu noppee na rendi menn pitax mi mbaa menn xati mu ndaw mi, lu mu ci gëna jekku rekk,
31 menn mi di saraxas peyug tooñ, mi ci des di saraxu rendi-dóomal, te mu boole kook saraxu pepp mi. Noonu la sarxalkat biy defale ki ñuy laabal njotlaayam fi kanam Aji Sax ji.»
32 Loolu la yoon digle ci mbirum nit ku ànd ak jàngoroy der juy law te dooleem matewul sarax yi ñu koy laabale.
33 Aji Sax ji wax na Musaa ak Aaróona ne leen:
34 «Bu ngeen demee ca réewu Kanaan ga ma leen jox muy seen moomeel, bu ma tegee liir wuy law ba xuural ab néeg foofa ca seen réewum bopp,
35 boroom néeg bi dafa wara dem ca sarxalkat ba ne ko: “Lu mel ni aw liir laa gis sama néeg.”
36 Su boobaa na sarxalkat bi santaane, ñu génne lépp lu nekk ca néeg ba, bala muy dugg di seet liir wi. Su ko defee du am lenn lu nekk ca néeg ba, lu muy biral ne sobe topp na ko. Gannaaw loolu sarxalkat bi dugg, seet néeg bi.
37 Bu sarxalkat bi seetee liir wi ci miiri néeg bi ca biir, muy ay xóot-xóot yu xawa nëtëx, mbaa mu xawa xonq, mel ni lu def pax ci miir bi,
38 na génn néeg bi te tëj néeg bi diiru juróom ñaari fan.
39 Bésub juróom ñaareel ba na sarxalkat bi délsi seet néeg bi. Bu liir wi lawee ci miiri néeg bi,
40 na sarxalkat bi santaane, ñu teggi doj yi liir wi xuural, boole ko génne dëkk bi, sànni ko fu setul.
41 Na xeetlu biir néeg bi ba mu daj, te pënd ba ñu ca xeete dees koy génne dëkk ba, tuur ko fu setul.
42 Dañoo wara sàkkaat ay doj, wuutale ko doj yooyu te sàkk ban bu bees, raaxe ko néeg bi.
43 «Su liir wi delloo tegu ci biir néeg bi gannaaw bu ñu teggee doj yi, xeet biir néeg bi, ba raax ko,
44 sarxalkat bi day dikk seet ko. Su liir wi lawee ci néeg bi, liir wu aaytal la wu xuural biir néeg bi, di sobe.
45 Néeg ba dees koy daane, boole doj yaak bant yaak banu raax ba bépp, génne ko dëkk bi, tuur ko fu setul.
46 «Ku dugg biir néeg bi diiru fan yi mu tëje dina yendoo sobe ba jant so.
47 Ku tëdd ca biir néeg ba war naa fóot ay yéreem te ku fa lekke it war naa fóot ay yéreem.
48 «Su sarxalkat ba delloo ca néeg ba, seet ko, fekk liir wa lawul ca néeg ba, gannaaw ba ñu ko raaxee, na biral ne néeg bi set na, ndax kon liir wa raaf na.
49 Liy laabal néeg bi moo di mu sàkk ñaari picc ak bantu garabu seedar ak wëñ gu xonq curr ak caru isob.
50 Day rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer mu def ndox mu balle ci bëtu ndox.
51 Bu noppee na jaxase deretu picc mi ñu rendi ak ndox mu balle ci bëtu ndox, daldi jël bantu seedar bi ak caru isob bi ak wëñ gi xonq curr ak picc miy dund, boole lépp sóob ca. Su ko defee mu wis-wisal ca juróom ñaari yoon ci néeg bi.
52 Kon li muy laabale néeg bi moo di deretu picc mi ak ndox moomu ak picc miy dund ak bantu seedar bi ak caru isob bi ak wëñ gi xonq curr.
53 Na bàyyi picc miy dund fu génn dëkk ba, mu naaw ca àll ba. Noonu lay defe njotlaayal néeg bi, mu set.»
54 Loolu la yoon digle ci lépp luy jàngoroy der juy law ak wat-wataan,
55 mbaa liir wu tegu ci ndimo mbaa ci néeg,
56 ak ci wàllu tërgën itam mbaa mu diy ër mbaa gàkk bu weex;
Sarxalkat yi 14 in Kàddug Yàlla gi