27 Baaraamu joxoñu ndijooram lay wis-wisale diw gi ci loxol càmmoñam ba muy juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji.
28 Loolu wéy sarxalkat bi wara sàkk ci diw gi ci loxoom, tooyal ca tabanu noppu ndijooru ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram; na ko def ca bérab boobu mu taaj deretu sarax siy peyug tooñ.
29 Li des ci diw gi ci loxol sarxalkat bi na ko diw ci boppu ki ñuy laabal, defal ko ko njotlaay fi kanam Aji Sax ji.
30 Bu noppee na rendi menn pitax mi mbaa menn xati mu ndaw mi, lu mu ci gëna jekku rekk,
31 menn mi di saraxas peyug tooñ, mi ci des di saraxu rendi-dóomal, te mu boole kook saraxu pepp mi. Noonu la sarxalkat biy defale ki ñuy laabal njotlaayam fi kanam Aji Sax ji.»
32 Loolu la yoon digle ci mbirum nit ku ànd ak jàngoroy der juy law te dooleem matewul sarax yi ñu koy laabale.
33 Aji Sax ji wax na Musaa ak Aaróona ne leen:
34 «Bu ngeen demee ca réewu Kanaan ga ma leen jox muy seen moomeel, bu ma tegee liir wuy law ba xuural ab néeg foofa ca seen réewum bopp,