Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 14:25-44 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 14:25-44 in Kàddug Yàlla gi

25 Gannaaw gi ñu rendi kuuy miy saraxu peyug tooñ, sarxalkat bi sàkk ci deret ji, taqal ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
26 Bu sarxalkat bi noppee, na sotti tuuti ci diw gi ci loxol càmmoñu boppam,
27 Baaraamu joxoñu ndijooram lay wis-wisale diw gi ci loxol càmmoñam ba muy juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji.
28 Loolu wéy sarxalkat bi wara sàkk ci diw gi ci loxoom, tooyal ca tabanu noppu ndijooru ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram; na ko def ca bérab boobu mu taaj deretu sarax siy peyug tooñ.
29 Li des ci diw gi ci loxol sarxalkat bi na ko diw ci boppu ki ñuy laabal, defal ko ko njotlaay fi kanam Aji Sax ji.
30 Bu noppee na rendi menn pitax mi mbaa menn xati mu ndaw mi, lu mu ci gëna jekku rekk,
31 menn mi di saraxas peyug tooñ, mi ci des di saraxu rendi-dóomal, te mu boole kook saraxu pepp mi. Noonu la sarxalkat biy defale ki ñuy laabal njotlaayam fi kanam Aji Sax ji.»
32 Loolu la yoon digle ci mbirum nit ku ànd ak jàngoroy der juy law te dooleem matewul sarax yi ñu koy laabale.
33 Aji Sax ji wax na Musaa ak Aaróona ne leen:
34 «Bu ngeen demee ca réewu Kanaan ga ma leen jox muy seen moomeel, bu ma tegee liir wuy law ba xuural ab néeg foofa ca seen réewum bopp,
35 boroom néeg bi dafa wara dem ca sarxalkat ba ne ko: “Lu mel ni aw liir laa gis sama néeg.”
36 Su boobaa na sarxalkat bi santaane, ñu génne lépp lu nekk ca néeg ba, bala muy dugg di seet liir wi. Su ko defee du am lenn lu nekk ca néeg ba, lu muy biral ne sobe topp na ko. Gannaaw loolu sarxalkat bi dugg, seet néeg bi.
37 Bu sarxalkat bi seetee liir wi ci miiri néeg bi ca biir, muy ay xóot-xóot yu xawa nëtëx, mbaa mu xawa xonq, mel ni lu def pax ci miir bi,
38 na génn néeg bi te tëj néeg bi diiru juróom ñaari fan.
39 Bésub juróom ñaareel ba na sarxalkat bi délsi seet néeg bi. Bu liir wi lawee ci miiri néeg bi,
40 na sarxalkat bi santaane, ñu teggi doj yi liir wi xuural, boole ko génne dëkk bi, sànni ko fu setul.
41 Na xeetlu biir néeg bi ba mu daj, te pënd ba ñu ca xeete dees koy génne dëkk ba, tuur ko fu setul.
42 Dañoo wara sàkkaat ay doj, wuutale ko doj yooyu te sàkk ban bu bees, raaxe ko néeg bi.
43 «Su liir wi delloo tegu ci biir néeg bi gannaaw bu ñu teggee doj yi, xeet biir néeg bi, ba raax ko,
44 sarxalkat bi day dikk seet ko. Su liir wi lawee ci néeg bi, liir wu aaytal la wu xuural biir néeg bi, di sobe.
Sarxalkat yi 14 in Kàddug Yàlla gi