Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 14:2-14 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 14:2-14 in Kàddug Yàlla gi

2 «Li yoon digle ci mbirum nit ku ame jàngoroy der juy law, keroog bés ba ñuy laabal nit ki, mooy lii: Nañu ko yegge sarxalkat bi.
3 Sarxalkat bi day génn dal bi, bu koy seet. Su nit ki demee ba jàngoroy der ji ko daloon wér,
4 sarxalkat bi day santaane, ñu indil nit kooku ñuy laabal ñaari picc yu dagan tey dund, ak bantu garabu seedar, ak wëñ gu xonq curr, ak caru garabu isob.
5 Na sarxalkat bi santaane, ñu rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer lu def ndox mu balle ci bëtu ndox.
6 Picc miy dund da koy booleek bantu seedar bi ak wëñ gu xonq curr gi ak caru isob bi, boole lépp sóob ci deretu picc ma ñu rendi woon tiimale ko ndox mi balle ci bëtu ndox.
7 Bu loolu amee sarxalkat bi wis-wisal juróom ñaari yoon ci kaw ki ñuy laabal, ngir mu tàggook sobey jàngoro ji. Su ko defee sarxalkat bi biral ne set na. Bu noppee na bàyyi picc miy dund mu naaw ca àll ba.
8 Ku ñuy laabal day fóot ay yéreem, watu ba set te sangu, doora set. Gannaaw loolu man naa dugg ci dal bi, waaye na yem ca bunt xaymaam ca biti diiru juróom ñaari fan.
9 Bésub juróom ñaareel ba na watu ba set, bopp beek sikkim beek yeen yi ak kawar gi ci des yépp lay wat, fóot ay yéreem, sangu, daldi set.
10 Bésub juróom ñetteel ba na indi ñaari kuuy yu amul sikk, ak menn xar mu jigéen mu am at te amul sikk ak juróom ñeenti kiloy sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe diw, muy saraxu pepp. Mu indaale genn-wàllu liitaru diw.
11 Sarxalkat biy laabal nit ki day indi nit ki, mu ànd ak loolu lépp, taxaw fi kanam Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi.
12 «Sarxalkat bi teg ca jël menn kuuy mi, rendi ko, muy saraxu peyug tooñ, boole kook genn-wàll liitaru diw ga, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
13 Nañu rendi kuuy mi ci bérab bu sell bi, fi ñuy rendee juru saraxu póotum bàkkaar ak saraxu rendi-dóomal, ndax li nekk ci saraxu peyug tooñ moo nekk ci saraxu póotum bàkkaar: sarxalkat bee ko moom; lu sella sell la.
14 Na sarxalkat bi sàkk ci deretu jur giy saraxu peyug tooñ, taqal ko ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
Sarxalkat yi 14 in Kàddug Yàlla gi