Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 13:7-33 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 13:7-33 in Kàddug Yàlla gi

7 Su fekkee ne wóor na ne ër bi law na ci deru yaramu nit ki, gannaaw ba mu ko wonee sarxalkat bi, ba mu biral ne set na, day dellu ca sarxalkat ba.
8 Su boobaa na ko sarxalkat bi xoolaat ba gis ër bi law ci deru yaram wi, mu doora biral ne nit ki sobewu na te jàngoroy der juy law la.
9 «Képp ku ame jàngoroy der juy law, nañu ko yóbbu ca sarxalkat ba.
10 Na ko sarxalkat bi seet. Su dee ab tërgën bu weex te kawar gi ci nekk soppiku weex, boole ci def góom ca biir,
11 kon jàngoroy der juy law la te xas naa law ci yaram wi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Du jar mu di ko ber ndax taq na sobe ba noppi.
12 Su fekkee ne nag jàngoro ji génn naa génn ci yaramu nit ki, sarxalkat bi gis ko fépp, li ko dale ci bopp bi ba ci tànk yi,
13 na ko sarxalkat bi seet bu baax. Bu gisee ne li génn ci yaramam daj na yaram wi yépp, na biral ne nit ki mu dal set na; gannaaw léppam a soppiku weex, set na.
14 Ba tey bés bu ay góom génnaatee ci yaram wi, nit ki sobewu na.
15 Su sarxalkat bi gisee yaramu nit ki def góom rekk, na biral ne sobewu na. Góom boobu génn ci yaram wi sobe la. Jàngoroy der juy law la.
16 Te it bu góom bi soppikoo weex, na dem ca sarxalkat ba.
17 Na ko sarxalkat bi seet, ba gis ne weexaat na, mu biral ne ki jàngoro ji dal set na te kon it set na.
18 «Su nit taabee ba wér,
19 ab tërgën bu weex mbaa gàkk bu weex bu rax xonq feeñ fa taab ba nekkoon, na dem ca sarxalkat ba.
20 Su ko sarxalkat bi seetee ba gis fa taab ba nekkoon mel ni lu def pax, te kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca taab ba.
21 Waaye su ko sarxalkat bi seetee te gisu ca kawar gu weex, deful pax it te raaf na, na ber nit ki juróom ñaari fan.
22 Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la.
23 Su gàkk bi yemee foofu, baña law, légétub taab ba la, te na sarxalkat bi biral ne nit ki set na.
24 «Su nit lakkee, ab gàkk bu weex mbaa bu weex te rax xonq feeñ ca kaw suux wu xonq wa lakk,
25 na ko sarxalkat bi seet. Su kawar gi ci nekk soppikoo weex te gàkk bi mel ni lu def pax, kon jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca lakk-lakk ba. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na, ndax jàngoroy der juy law la.
26 Waaye su ko sarxalkat bi seetee, gisul kawar gu weex ci gàkk bi, deful pax it te raaf na, na ber nit ki juróom ñaari fan.
27 Sarxalkat bi da koy seet ca bésub juróom ñaareel ba. Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la.
28 Su gàkk bi yemee foofu te lawul ci yaram wi, ab tut la bu juddoo ci lakk-lakk bi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki set na, ndax légétub lakk-lakk ba la.
29 «Su fekkee ne góor mbaa jigéen dafa ame jàngoro ci bopp mbaa ci sikkim,
30 na sarxalkat bi seet fi jàngoro ji nekk. Su melee ni lu def pax ci der bi, kawar gu xall te sew nekk ca, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Loolu wat-wataan la, di ër yuy génn ci bopp mbaa sikkim.
31 Ndegam sarxalkat bi seet na ër wi te niruwul lu def pax, amul it kawar gu ñuul ca biir, day ber nit ki ame ër wi diiru juróom ñaari fan.
32 Sarxalkat bi day seetaat ër wi ca bésub juróom ñaareel ba. Su wat-wataan ji lawul, kawar gu xall nekku ca, te melul ni lu def pax,
33 na nit ki watu waaye du wataale wat-wataan ji. Sarxalkat bi da koy beraat juróom ñaari fan.
Sarxalkat yi 13 in Kàddug Yàlla gi