Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 13:5-17 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 13:5-17 in Kàddug Yàlla gi

5 Na ko sarxalkat bi xoolaat bésub juróom ñaareel ba. Bu sarxalkat bi seetloo ne gàkk bi soppikuwul mbaa mu law ci yaramam, na ko beraat juróom ñaari fan.
6 Na ko sarxalkat bi xoolaat ca bésub juróom ñaareel ba. Su fekkee gàkk bi di raaf te lawul ci kaw deru yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki set na; ab ër doŋŋ la. Day fóot ay yéreem rekk daldi set.
7 Su fekkee ne wóor na ne ër bi law na ci deru yaramu nit ki, gannaaw ba mu ko wonee sarxalkat bi, ba mu biral ne set na, day dellu ca sarxalkat ba.
8 Su boobaa na ko sarxalkat bi xoolaat ba gis ër bi law ci deru yaram wi, mu doora biral ne nit ki sobewu na te jàngoroy der juy law la.
9 «Képp ku ame jàngoroy der juy law, nañu ko yóbbu ca sarxalkat ba.
10 Na ko sarxalkat bi seet. Su dee ab tërgën bu weex te kawar gi ci nekk soppiku weex, boole ci def góom ca biir,
11 kon jàngoroy der juy law la te xas naa law ci yaram wi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Du jar mu di ko ber ndax taq na sobe ba noppi.
12 Su fekkee ne nag jàngoro ji génn naa génn ci yaramu nit ki, sarxalkat bi gis ko fépp, li ko dale ci bopp bi ba ci tànk yi,
13 na ko sarxalkat bi seet bu baax. Bu gisee ne li génn ci yaramam daj na yaram wi yépp, na biral ne nit ki mu dal set na; gannaaw léppam a soppiku weex, set na.
14 Ba tey bés bu ay góom génnaatee ci yaram wi, nit ki sobewu na.
15 Su sarxalkat bi gisee yaramu nit ki def góom rekk, na biral ne sobewu na. Góom boobu génn ci yaram wi sobe la. Jàngoroy der juy law la.
16 Te it bu góom bi soppikoo weex, na dem ca sarxalkat ba.
17 Na ko sarxalkat bi seet, ba gis ne weexaat na, mu biral ne ki jàngoro ji dal set na te kon it set na.
Sarxalkat yi 13 in Kàddug Yàlla gi