Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 13:38-57 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 13:38-57 in Kàddug Yàlla gi

38 «Su góor mbaa jigéen amee ay gàkk-gàkk yu weex ci yaram wi,
39 sarxalkat bi seet ko, gàkk yooyu ci yaram wi di lu weex, xawa xall, xam rekk la, ju feeñ ci yaram wi waaye nit ki set na.
40 «Góor gu bopp ba amatul kawar dafa leel waaye set na.
41 Bu bopp bi ñàkkee kawar fi féeteek kanam gi, jë baa leel waaye set na.
42 Waaye su amee gàkk bu weex bu feeñ te rax xonq ci leelub ndaal bopp mbaa jë, jàngoroy der la juy màgg tey génn ci leelub ndaal bopp mbaa jë.
43 Sarxalkat bi da koy seet. Ndegam ay tërgën yu weex te rax xonq a ngi ci leelub ndaal bopp bi mbaa jë bi, mu mel ni jàngoroy der juy law ci yaram wi,
44 nit ki ànd naak jàngoro te taq na sobe. Na sarxalkat bi biral ci lu leer ne nit ki sobewu na ndax jàngoro ji ci bopp bi.
45 «Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: “Setuma de, setuma!”
46 Li feek jàngoro jaa ngi ci moom, day sobewu te gannaaw daa sobewu, na dëkk moom doŋŋ te na dëkkuwaayam génn dal bi.
47 «Su ndimo xuuree, teg aw liir, muy ndimol kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa yu wëñ gu ëccu,
48 mu tegu ci bàgg mbaa ci poqe, su dee kawar gu ëccu, su dee wëñ gu ëccu walla der bu ñu wulli walla mboolem lu ñu defare der,
49 su liir wi nëtëxee mbaa mu xonq, tege ci yére mbaa der mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, liir wuy law la. Dees koy won sarxalkat bi.
50 Na sarxalkat bi nemmiku liir wi, ba noppi ber këf ki teg liir wi diiru juróom ñaari fan.
51 Bésub juróom ñaareel ba na seet liir wa. Su liir wa lawee ca kaw këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa der mbaa jumtukaayu der, kon liir wu aaytal la te këf ka sobewu na.
52 Da koy lakk, ndax liir wu aaytal la, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa wëñ gu ëccu mbaa lu ñu defare der te liir wa tegu ca. Dees koy lakk, ba mu dib dóom.
53 Waaye kat bu sarxalkat bi seetloo ne liir wi lawul ci këf ki, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa jumtukaayu der,
54 na santaane ñu fóot ko, mu daldi koy beraat juróom ñaari fan.
55 Ndegam nag gannaaw ba ñu fóotee këf ka teg liir, sarxalkat bi seet na ko, te liir wi soppiwul melo, bu lawul it setul. Dees koy lakk, ba mu dib dóom, su yàqoo biir ak su yàqoo biti yépp.
56 Su sarxalkat bi gisee gannaaw ba ñu fóotee këf ka ne, liir wi raaf na, na dagg sànni fa tegoon liir ca këf ka, muy ndimo mbaa der mbaa bàgg mbaa poqe.
57 Su liir wa génnaatee ca këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, kon liir wuy màgg la. Këf ka teg liir dees koy lakk, ba mu dib dóom.
Sarxalkat yi 13 in Kàddug Yàlla gi