Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 13:3-10 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 13:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Na sarxalkat bi seet gàkk bi ci yaramu nit ki; su fekkee ne kawar gi ci gàkk bi dafa soppiku weex, te mu mel ni lu def pax ci der bi, jàngoroy der juy law la. Bu sarxalkat bi gisee loolu, na biral ne nit ki sobewu na.
4 Waaye su dee ab gàkk bu weex ci yaram wi te melul ni lu def pax ci der bi, taxul itam kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi ber nit ki ame gàkk bi diiru juróom ñaari fan.
5 Na ko sarxalkat bi xoolaat bésub juróom ñaareel ba. Bu sarxalkat bi seetloo ne gàkk bi soppikuwul mbaa mu law ci yaramam, na ko beraat juróom ñaari fan.
6 Na ko sarxalkat bi xoolaat ca bésub juróom ñaareel ba. Su fekkee gàkk bi di raaf te lawul ci kaw deru yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki set na; ab ër doŋŋ la. Day fóot ay yéreem rekk daldi set.
7 Su fekkee ne wóor na ne ër bi law na ci deru yaramu nit ki, gannaaw ba mu ko wonee sarxalkat bi, ba mu biral ne set na, day dellu ca sarxalkat ba.
8 Su boobaa na ko sarxalkat bi xoolaat ba gis ër bi law ci deru yaram wi, mu doora biral ne nit ki sobewu na te jàngoroy der juy law la.
9 «Képp ku ame jàngoroy der juy law, nañu ko yóbbu ca sarxalkat ba.
10 Na ko sarxalkat bi seet. Su dee ab tërgën bu weex te kawar gi ci nekk soppiku weex, boole ci def góom ca biir,
Sarxalkat yi 13 in Kàddug Yàlla gi