Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 11:24-46 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 11:24-46 in Kàddug Yàlla gi

24 «Yii nag da leen di sobeel te képp ku laal lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
25 Te itam képp ku for lenn lu dee ci yii, na fóot ay yéreem, waaye dina yendoo sobe ba jant so.
26 Mboolem mala mu we wa xar te séddlikoowul ñaar mbaa du duññ daganul ci yeen, ku ci laal lenn it sobewu na.
27 Ba tey lépp luy doxe ndëgguy tànkam ci mboolem boroom ñeenti tànk, daganul ci yeen te ku laal méddam dina yendoo sobe ba jant so.
28 Ku for méddam, na fóot ay yéreem te dina yendoo sobe ba jant so. Yooyu daganul ci yeen.
29 «Bu loolu weesee, leneen lu daganul ci yeen ci rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, mooy kaña ak janax ak xeeti mbëtt yépp;
30 ak unk ak bar ak sindax buy yéeg, ak sindax buy dox ci suuf, ak kàkkatar.
31 Yooyoo daganul ci yeen ci mboolem rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf. Képp ku laal lenn lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
32 Te it lu ci dee ba wadd ci kaw lenn, loola day sobewu, nay ndabal bant, mbaa ndimo, der mbaa ab saaku, mbaa jumtukaay bu mu mana doon. Nañu sóob loola ci ndox te du tee mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.
33 Su fekkee ne lenn a dee ci yooyu, wadd ci biir ndabal xandeer, lu woon ca biir sobewu na, te nañu toj ndab la.
34 Ndox mu jóge ci ndab loolu, bu dalee ci ñam wu dagan, ñam woowu dal nay sobewu moom itam; bu doon ag naan gu dagan moo ca nekk it, sobewu na, ak ndab lu naan ga mana nekk.
35 Lépp lu lenn ci yooyu dee, ba dal ca, la mu dal sobewu na. Su dee ab puuru ban mbaa cin, dees koy toj ndax sobewu na te lu setul la ci yeen.
36 Su fekkee ne loola dee daa wadd ci biir bëtu ndox mbaa kàmb gu def ndox, du tee ndox ma laab, waaye ku laal la dee ca biir sobewu nga.
37 Su la dee waddee ci peppum jiwu, du tee peppum jiwu ma set;
38 waaye su fekkee ñu kaas pepp ma te lenn lu dee lu bokk ci yooyu dal ca, pepp ma daganul ci yeen.
39 «Su mala mu dagan méddee, ku laal médd ma dina yendoo sobe ba jant so.
40 Képp ku lekk ca médd ma, na fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. Képp ku for médd ma, na fóot ay yéreem te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
41 «Mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, sibleen ko. Deesu ko lekk.
42 Lépp luy watatu, mbaa lu sew di boroom ñeenti tànk, mbaa mu bare ay tànk ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, waruleen koo lekk, ndax lu ñu wara sib la.
43 Buleen araamal seen bopp ci lenn ci yu sew-sewaan yooyu; buleen ci taq, di ci sobeel seen bopp,
44 ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.
45 Ndaxte kat man Aji Sax ji maay ki leen génne woon réewum Misra, di seen Yàlla. Sell-leen boog, ndax man ku Sell laa.»
46 Loolu la yoon digle ci wàllu mala ak njanaaw ak bindeef yi nekk ci ndox, ak mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf.
Sarxalkat yi 11 in Kàddug Yàlla gi